dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ñàdd : ñar, tër. ndax mën ngaa ñàdd nag ?

ñàkk-a-déggoo b- : xaalis wala jigeen dinañuy faral di waral ñàkk-a-déggoo. safaan wi mooy déggoo b-.

ñàkk-a-xam g- : ñàkk-a-xam li mu waral bare na. (léebu).

ñàkk-aajo : ku ñàkk-aajo mooy kuy faral di romb nit ñi te du leen nuyu. safaan wi mooy am-aajo.

ñàkk-deret : dafa ñàkk-deret mootax mu néew-doole.

ñàkk-doole : néew-doole. feebaram bee ko tax a ñàkk-doole. safaan wi mooy am-kàttan.

ñàkk-faayda : borom-kër warul a ñàkk-faayda. safaan wi mooy am-faayda.

ñàkk-jom : dafa ñàkk-jom rekk wànte tere nañu ko li muy def ba tàyyi. safaan wi mooy am-jom.

ñàkk-jot : ndaw dafa war di ñàkk-jot fu tollu. safaan wi mooy am-jot.

ñàkk-kàttan : duy lekk mootax mu ñàkk-kàttan. safaan wi mooy am-kàttan.

ñàkk-kersa : ku ñàkk-kersa mooy ku amul lenn lu muy rus. safaan wi mooy am-kersa.

ñàkk-maanaa : ñàkk-solo. liggeeyam bu metti bi, peyoor bu ñàkk-maanaa la ciy am. safaan wi mooy am-maanaa wala am-solo.

ñàkk-njariñ : yaafus. ku ñàkk-njariñ mooy ku mënul dara wala ku mënul defal kenn dara. safaan wi mooy am-njariñ, am-kàttan wala njaxlaf.

ñàkk-saas : dinañuy wax tamit ñàkk-sãas. safaan wi mooy am-muur. (seetal am-muur)

ñàkk-sãas : dinañuy wax tamit ñàkk -saas. safaan wi mooy am-muur. (seetal am-muur)

ñàkk-solo : ñàkk-maana. lu ñàkk-solo ci lañuy xuloo. safaan wi mooy am-solo.

ñàkk-sutura : nit ku ñàkk-sutura du denc benn sekkere. safaan wi mooy am-sutura.

ñàkk-wërsëg : dafa ñàkk-wërsëg ndax liggeey bu baax bu mu am, ñàkk ko. safaan wi mooy am-wërsëg.

ñàkk-xel : ku dul xalaat. dafa ñàkk-xel, fu mu dem ñu nax ko. safaan wi mooy am-xel, muus, yeewu wala ñor.

ñàkk-xorom : li muy wax saful kenn, dafa ñàkk-xorom. safaan wi mooy am-xorom.

ñàkkaana : ñàkkaana nga gisaale ko fa. safaan wi mooy amaana.

ñàkkali : jàngaat li nga jàngoon, nafar. fajar gu jot, dina ñàkkali bindam yi soog a jàngi.

ñàkki : tàmbali liggeeyu tool yi te nawet jotagul, jëpp. ren beykat yi dañoo ñàkki.

ñàkk : xamuma lu mu ñàkk wànte du xaalis. safaan wi mooy am. / xaalis bi mu defoon ci kër gi yépp ñàkk na ko. / bul ñàkk a seeti sa nijaay.

ñàlli : daw bu baax. golo gi dafa séen xaj bi rekk, ñàlli.

ñàmbaas : yokk ab morso ci sër. dafa ñàmbaas sër bi mu woddoo.

ñàmbi j- : pulloox b-. dafay bey ñàmbi seen dëkk.

ñàng : lu aay, lu ñaaw, lu garaaw. li mu def ñàng na. / kanam gu ñàng la yor.

ñàngoor m- : jaan ju raglu j-. am ñàngoor lañu rey tey ca tool ya.

ñànjaxeer b- : liy weex ci nen lañuy tudde ñànjaxeer.

ñànkar b- : lu màgget, lu yàqu. benn ñànkaru oto moo paan ci yoon wi.

ñànkataŋ b- : ceeb b-. ñànkataŋ bi dafa sedd.

ñàpp : (ne ñàpp). tafu ci dara. xale bi ne na ñàpp ci ginnaawu yaay ji.