dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ës 1 : gas. defar am pax mu ndaw. ginaar su bëggee nen fenn, dafa fay ës.

ës 2 : ku yégul mettit, ëŋŋësle. kenn mënul ci xale bi dara ndax dafa ës.

ësib b- : asit b-. ësib kenn waru koo teg fu ko xale di mën a jële.

ëskëy : sas. ku waaru dafa koy wax. sëriñ baa ngi wax, taalibe yépp naan ëskëy.