dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ër-ër b- : rëq-rëq b, jotee b-. dañoo am ër-ër ñoom ñaar.

ërbiis b- : dox ci ndox mu tilim mooy joxe ërbiis. dinañuy wax tamit arbiis b-.

ër w- : boppam bi dafa fees dell ak ay ër. / pax mu ñu gas fi wër ag garab gu ndaw ngir tiye ndox mi koy suuqat. sottil ndox mi ci biir ër wi.

ërtal : arsele. loo ko def ba mu lay ërtal ?