dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ëpp 1 : suukaru àttaaya bi dafa ëpp. dafa soxor ba mu ëpp. sa yëf yaa ngi bëgg a ëpp loxo. safaan wi mooy yem.

ëpp 2 : sut, gën a bare, gën a réy. suñu dëkk a ëpp seen bos. moo ko ëpp ay lijaasa.

ëpp 3 : jëlal wàntaay bi ñëw ëpp leen. dinañuy wax tamit upp.

ëpp-nit : sob, yemadi. teeyal, yow danga ëpp-nit. safaan wi mooy teey.