dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ëlbati : dinañuy wax tamit walbati wala wëlbati. (seetal walbati)

ëlëb : (ne ëlëb). jékki jékki rekk di soowe nit. dafa ko joggi rekk, mu ne ko ëlëb ak coow.

ëlëm : jaaxal, ump. ni mu def ba am xaalisam bee ëlëm nit ñi ndax liggeeyulwoon.

ëlleer : dinañuy wax tamit illeer. (seetal illeer)

ëlléer g- : ëlléer lay beye. dinañuy wax tamit illeer g-.

ëllëg-ak-sibbir s- : liy ñëw ci kanam. fexeel ba bu la kenn dégg ci lu ñaaw ëllëg-ak-sibbir.

ëllëg : suba. dinaa ko seeti ëllëg.

ëllëg g- : liy ñëw ci kanam. kenn ku nekk dafa war a góor-góorlu ngir ëllëgam.

ëllëg s- : suba s-. altine la waxoon ne lay ñëw, wànte ca ëllëg sa la mujj ñëw.