dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

àttaa : sax. àttaa xale bii, mën na loolu.

àttaaya : xale yi demleen wuti liggeey te bàyyi naan àttaaya bu bare bi.

àttaaya : soxna seey àttaaya.

àttan : xam nga ni mbaam mi àttanul li nga ko sëf.

àtte : bés bu Yàlla àttee, lépp dina leer. / dogal. li borom bi àtte, jaam mënu ci dara. / teqale ñaar ñu doon xeex. demal àtte xale yi.

àtte : saytu ay jëf. Yàlla dina ñu àtte ci suñu jëf yommalxiyaam. / teqale. àtteel xale yiy xeex fee.