dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

àndaale b- : rab w-. gisoon nañu ab àndaale ca àll ba.

ànd : dem ak nit. kaay ñu ànd marse. / nangu am mbir. ànd naa ci li nga wax. / mën a dem ak. sa dàll yi ànd nañu ak sa yére bi.

àngale : làkku àngale mooy làkku waa Etaasini ak waa Àngalteer.

àngare : àngare bokk na ci jumtuwaay yi ñuy def ci ab tool ngir naatal ko. dinañuy wax tamit tos g- wala fiime b-.

ànket : liññarti, laajte. dafa lay ànket rekk ngir bëgg a xam dara ci mbir moomu.

àntu : am ndam ci am mbir. li mu bëggoon ci njàngam mi yépp àntu na. dinañuy wax tamit antu. safaan wi mooy lajj.