dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

àllaaji b- : jullit bu góor bu dem aji Màkka ba ñëw. dinañuy wax tamit alaaji, aas wala elaas. safaan wi mooy ajaa b-. àllaaji bi lañu sargalsi.

àllaaxira j- : yommalxiyaam j-. àllaaxira kenn du ko wuute. dinañuy wax tamit laaxira j- wala barsàq b-.

àllarba j- : benn la ci turu bés yi. njàng mu nekk am na àllarba.

àll b- : dëkkuwaayu rabi-àll yi, gancax g-, dëkku jàmbur yi. seen àll ba am na ay bukki.

àlluwa j- : fi sëriñ daara bi di bindal taalibe bi li mu war a jàng. àlluwa mooy aarduwaas ci njàngum nasaraan.