dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

àddina s- : dunyaa b-. àddina si dara jaru fi ñaaw, Yàlla noppi na bu yàgg. dinañuy wax tamit àdduna s-.

àddiya j- : lenn lu ñuy jox ab sëriñ lu mel ni xaalis wala lu am solo rekk ngir màggal ko. jox na sëriñam àddiya ju duun.

àdduna s- : dinañuy wax tamit àddina s-. (seetal àddina)

àddu : wuyu wala tontu ci mbir. duma àddu ci loolu, dafa may ñàkkal faayda.