dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum léebu wolof

léebu yi nga làcce ñoo di

1 :  aar moo gën faj.
2 :  aawo, aw la tudd.
3 :  aawo buuru këram.
4 :  aaye na, aayeetul keroog.
5 :  ab dag du bëgg moroom ma.
6 :  ab lonku, daar a ca gën.
7 :  ab yeel bu ëppee ab lupp booba jàngoro rax na ca.
8 :  àbb delloo la sant.
9 :  àbb, delloo ca gën.
10 :  àddina ak li ci biiram jarula xiirook a ŋaayoo.
11 :  àddina, ànd bi géléem la.
12 :  àddina daramba la.
13 :  àddina du cere, waaye dañu koy laalo.
13-1 :  àddina du cere waaye dees na ko laalo.
13-2 :  àddina du cere waaye lu mata laalo la.
14 :  àddina du dara.
15 :  àddina du kër, xaarukaayu dee la.
16 :  àddina du lijjantiku. ca xeexub Badar la lëje woon.
17 :  àddina gudd nab tank.
18 :  àddina jigéen la, ju fu mu tollu, mu ngi ëmb te kenn xamul lu muy jur.
19 :  àddina, kendandoo la.
20 :  àddina kenn defaru ko ci benn fan.
21 :  àddina këru naxekaay la.
22 :  àddina li muy yaatu-yaatu, ñaawaay a ëpp wóllare taar.
23 :  àddina mor yow.
24 :  àddina, ndoxum joor la ; buy taa, mu ngay ŋiis.
25 :  àddina Njéeme la tudd, sant Ba.
26 :  àddina njoowaanu golo la, garab gu nekk lay wékku.
27 :  àddina ñett a ci gën : àjjana biti, ak weerteewlu ak mëneek say dëkk, ak ku la gis bëgg la.
28 :  àddina ñett a ci gën, am a gën, man a gën, xam a gën.
29 :  àddina, ñett a ci di yóbbal : ab xame, ab taar ak mbuus.
30 :  àddina ñett a ko jàpp : saxle, gub sax bi, ak sax mi.
31 :  àddina ñetti fan la, démb ñoom baay, tey ñun, ëllëg sunuy doom.
32 :  àddina potu ndaa la, ku naan jox sa moroom mu naan.
33 :  àddina, reenub ñàmbi la, kenn xamul fu muy damme.
34 :  àddina weeru koor la ; feek jant sowul, juubu du wees.
34-1 :  dund gu jeexagul, weeru koor la : juubu weesoogu ca.
34-2 :  koor gu jant sowagul, juubu weesoogu ca.
35 :  àddina wori neen la.
36 :  àddina yagadeete la, koo ca gis ngaa ndëndam, mu ko tëggal ; noppam ne ko : yàggleel.
37 :  àddinaa neex ba ku dee, ñu bàyyi laak say gëñ.
38 :  àddinaa ngi ci sunu kanam.
39 :  àddinaa tëradi.
40 :  àddinam xel, gën jamonoy bët.
41 :  àddinam xel, jam na gët.
42 :  àddinay gët, jamanoom xel.
43 :  àddiya ak moyaal, loo ci lekk, boo géexee, mu rees.
44 :  ag mbokk, dañu koy dox, mbaa ñu wax ko.
45 :  ag roy-dàq a fi yées.
46 :  ak lu nar teela xéy, bu dëgg gontee, jot ko.
47 :  àkk àkkum gaynde, song songum bukki.
48 :  alal fajul dee, gàcce lay faj.
48-1 :  alal du faj dee, gàcce lay faj.
49 :  alal joo gis, alaa ka fa ba.
50 :  alal yu bare, yaram wu wér a ko gën.
51 :  alalu golo : ca lex ba.
52 :  alalu jaambur ba la sant.
52-1 :  alalu jaambur ba fa la sant.
53 :  alalu ku sàggan, ku farlu moo koy jariñoo.
54 :  àllaaxira bopp du fa doxub joor.
55 :  alxamdulilaay ju àndul ak coono, amul.
56 :  am bukki yomb na, waaye bukki buy xalam a jafe.
57 :  am : gore, ñàkk : gore.
58 :  am joo gis, indee ciy tegu.
59 :  “am léegi” a gën “daa am ci kanam”.
60 :  am na baat bu doonte xexer, nga daloo ko.
61 :  am na bukki bu ŋexalul, te jégéñ kër.
62 :  am na i bët yu gëna réy as gémmiñam.
63 :  “am naa géléem ca Gànnaar” yomb naa wax.
64 :  am naa géléem ma nga Gànnaar.
65 :  am ndaa, toj ndaa.
66 :  am nopp yu firéeku, taxula am dég-dég.
67 :  am réew, su fa lingeer dee fecc, ku fay woyaan doo rusa yaŋas.
68 :  am saxul, ñàkk it saxul.
69 :  am soow dina ëppela bare, wande du ëppela weex.
70 :  am xaj moo gën, am nit.
71 :  am Yàlla Yàllaay Buur, ñaak Yàlla Yàllaay Buur.
72 :  amuloo salaamaalekum, amuloo fanaan leen jàmm.
73 :  ana golo aka xastey daar-daar ?
73-1 :  ana golo aka xaste ay daar-daar ?
73-2 :  ana goloo ka xastey daar-daar ?
74 :  ana golooka sàngoo mbàjj bay taamu nimoro diis ?
75 :  ànd ak filiks fetal damel, ànd ak damel fetal filiks.
76 :  àndandoo sag maas, diir koo yemal mbagg.
76-1 :  àndandook say maas, diirook koo yemal i mbagg.
77 :  àndook waa new, waa dugóor raw la.
77-1 :  andulook waa ndugóor yi, te waa nëw yi raw nañu la.
78 :  añ ci, te bu ci reer.
79 :  Ardoo néwi, ñu tup Malal.
80 :  as gor dina dugg ciy naxam.
81 :  asamaan lu mu taw-taw suuf àttan ko.
81-1 :  lu asamaan taw, suuf mën na koo dékku.
81-2 :  lu asamaan taw-taw, suuf dékku ko.
82 :  asamaan moo di buuri mbaar.
83 :  àtte bor ak fey.
83-1 :  àtteb bor, fay.
84 :  aw doj du yàgg géej ba tax mu doon aw jën.
85 :  aw fas, manees na koo wommat ba cim ndox, waaye naanloo ko te marul, maneesu ko.
85-1 :  manees naa wommat fas ba cim ndox, waaye maneesu koo naanloo te neexu ko.
86 :  aw naaru-góor lu mu mëna mëna daw ñu bàcc ko ab yar.
86-1 :  fasu naaru-góor, lu mu mën-a-mën daw ñu làbbili ko.
86-2 :  lu naaru-góor gaaw-gaaw, fàww ñu làbbali ko.
87 :  awma ginaar siiru sikk ma duma ci fekk.
88 :  ay du weesu baay dee na.
89 :  ay du yem ci boppub boroom.
89-1 :  ay du yem ci boppu boroomam.
89-2 :  musiba du yem ci boppu boroom.
90 :  ay wax yu bare, du may lu ñu lekk.
91 :  ayi waay jàmmi waay.
92 :  ba béjjéni kuuy di lëŋaaru, mag ñaa nga fa woon, te mënu ñu ca woon dara.
92-1 :  béjjénu xaaf, ba muy màgg bay wëndéelu, booba mag ñaa nga fa.
92-2 :  béjjénum xaaf ba muy woñaaru, mag ñaa ngi fi dan cee mënul dara.
92-3 :  man maay béjjén, bi may déng mag ñaa ngi fi, dañu cee mënul dara.
93 :  ba feneen amee ba-tey, kenn sonnatul.
94 :  ba mbott bëggee tollu niw ñay, daa funki ba toj te sottiwul.
95 :  ba nga déggee mbott mën nam ndox, ma ñu baxal taxul ñuy wax.
95-1 :  mbott a gëna bëgg ndox, wànte mu tàng bokku ca.
95-2 :  mbott mën na ndox, waaye du mu tàng.
96 :  ba nga séenee ron, ron a la jëkka séen.
96-1 :  ba nga laata séen ron, ron a la njëkka séen.
97 :  ba ngay séen puj, puj a la jëkka séen.
98 :  baadoolo, boo ko nee kaay jël sa teraanga, mu bañ, danga koy jox toroxalam.
99 :  baadoolo bu bañee liggéey, bañeek mbokkam.
100 :  baadoolo bu ragal naaj ragal na njariñam.
100-1 :  baadoolo bu bañee naaj, bañ nak mbokkam.