dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

gaynde ak bey

0:00 0:00

buleen di nangoo waxantu. loolu, xabaar bii, doy na ci seede.

buur gaynde dafa tëddoon bés, di féexlu ca peggu déeg ba. am xar, di tuñ-tuñi ba agsi fa ak maram. buur gaynde ne ko :

- nuyu naa la waay, mbokk sama ! fi nga dëkk sori na fi ?

kooku tontu ne ko :

waawaaw, sori lool sax ! gisal car bii, ba may jóg laa ko fàqoon, mu tooy xepp, te gis nga nii mu wowe, ba doon matt.

gaynde ne ko.

kon naanal te ni mes !

nees tuuti, béy ne jalañ agsi. gaynde jaar fa mu jaaroon ak xar :

salaa maalekum béy, ndax fi nga dëkk sori na fi ?

déedet, mukk ! soriy lan !

kon baax na, dinaa leen nuyusi. boo demee, waajal leen ma ngan !

naka la dëdde, gaynde daldi topp ca tànkam ya, agsi ca dëkk ba, rey gétt ga gépp, lekk ba yéy yax ya.

OSAD

tibbi ko ak coppite ci

Téere dawal