dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

baatoodi "j", bi nekk jabar, kenn du ko binde "d" ak "i", donte "d" ak "i", soo leen boole, dinañu la jox baat bu jege baatoodi "j".

"e" bi nekk ci "jeeg", dafa gudd. kon "ee" lañu koy bindee.

naka noonu, "u" lañuy bind, "o" ak "u" soo leen boolee, "ou" la lay jox, du la jox "u".

ci tënk, ku bëgg a topp sàrtu mbindum wolof, "jeeg bu jar", mooy mbind mu jaar yoon. donte tamaate "jeeg bu jar" yàgg na, te xëy-na tur bi, jiitu na dekere bi tëral mbindum wolof, jàpp nañu ni loolu mënul a nekk lay. Socas dafa war a yeesal mbind mi. su boobaa, "duma ko weccee", ndax "u", kenn du ko bindee "o" ak "u". su dul loolu, "dinaa ko weccee",

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa Socas, ñu jàppale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

SOCAS Senegaal