dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

"xar" lañuy bind.

"x", kenn du ko bindee "k" ak "h".

"xaalis" la ñuy bind.

"a" bu gudd di "aa" moo nekk ci baatu "xaalis". ñaari "s" bii moom, bi jóoni-jóoni def ci ni mu dindee xaalis, bind lu la neex la, jar ul ñu ciy wax.

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa jóoni-jóoni, ñu jappale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

jóoni-jóoni Senegaal