dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

ñu ngiy rafetlu mbindum wolofu parti pólotig bii di APR. waaya gaawantu ci bind, boole ci ñàkk a jàngat li nga bind, du indi "yokkute", te dina tas "yaakaar". kon, lu waral "e" bu gudd di "ee", bi ngeen def ci baatu "yokkute" ? lu waral indi "yaakaar", ba noppi tas "yaakar"?

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa APR, ñu jàppale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

APR Senegaal