dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

"réew mi" lañuy bind.

"é" bu gudd, di "ée", moo nekk ci baatu "réew".

ci turu dalub web, benn baat warul a am maska, te baat yépp, dañu leen war a taqale. loolu moo tax, "réew mi", ñu mën koo binde, "reewmi", ci dalub web bii di, "reewmi.com",

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa reewmi.com, ñu jàppale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

reewmi.com