dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

ci "ceeb bu joŋe", waxoon na ñu leen ni, baatoodi "ŋ" baatoodi bu jafe la. waaya, lu mu jafe-jafe, seerul ba ñu koy binde "n", "g" ak "u".

waaya jël baatoodi, bindee ko "c" ci "cibir", dellu bindee ko "t", "c" ak "h" ci "tchiin". loolu moom, kenn xamul nu mu tudd.

ci mbind mu jub, ñu ngiy bind, "joŋe ba ci biir cin".

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa Sofiex ñu jàppale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

Sofiex