dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

damm yax

"bi gën a neex" lañuy bind,

"gueuneu", xaw ma lan la. leer na ma ni du wolof. yaakaar naa ni du joolaa tamit. "gën a" mooy mbind mu leer mi.

"neex" lañuy wax, ak "e" bu gudd, di "ee".

réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mu di sàrtu mbindum wolof ci biir Senegaal. wareef la bon, képp kuy yëngu ci biir Senegaal, nga sàmmoontee ak sàrt Senegaal boobu.

ñu ngiy ñaan waa Punch ñu jàppale ñu, rafetal seen mbindum wolof.

Punch