dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

dalal ak jàmm ci ëttub wolof

0:00 0:00

nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : "làkku jàmbuur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku."

yaw aji-jàng bi, dalal ak jàmm ci ëttub wolof, dalub web bi leen di jàppale ci jàng dawal, ak jàng bind làkku wolof.

ëttub wolof, ñu ngi ko jagleel, képp ku mën a làkk wolof, te bëgg a mën a dawal, bëgg a mën a jàng, lépp lu ñu bind ci wolof, ak mën a bind xalaatam yépp ci wolof. kon nag, ëttub wolof, taxawul ngir jàngal wolof, ñi nga xam ne dégguñu wolof.

ñu jàpp ni boon, ëttub wolof, du doomu Senegaal rékk lañu ko jagleel. bépp nit, fu mu mën a nekk ci àdduna, te jàngum wolof yitteel ko, mu ngi ci biir, te ñu ngi koy jaajëfal, te di ko wax : dalal ak jàmm ci sa yëf, dalal ak jàmm ci li nga moom, dalal ak jàmm ci li ñu bokk.

loolu li muy indi moo di, waruñu jëfee benn làkk wu dul wolof, ngir tabax ëttub wolof. Liy wéral dogal boobu bare na :

  • su ma jëlee baat bii di "algebra" ci Àngale, ñu koy wax "algèbre" ci Farañse. sooy jàng "algebra", di "algèbre", di benn fànnu matematig, daañu la wax lu ci nekk yépp, jàngal la ko ba nga nekk ci sëriñ, te duñu la wax mukk fu baat boobu jóge, donte ñëpp xam nañu, ni baat boobu, Àngale ak Farañse, ñu ngi ko jële ci Araab. li ñu ciy jële moo di, baat su duggee ci biir làkk, dugg ci xel yi ak xol yi, baat boobu, làkk waa ko moom. jëlal baatu parkiŋ, nga wër dëkk bi nga nekk, su fekkee ni dëkk boobu, nit ñi seen làkkum Àngale sorewul noonu, ñu bare dañu la wax ni parkiŋ, gaaraas lay tekki, te duñu xam ni ci Àngale lañu ko jële, te di réere ni baatu gaaraas boobu sax, wolof moomu ko, ci Farañse la ko jële. kon li am solo rekk, moo di baat bu seey ci biir làkk rekk, làkk woowa moo ko moom.
  • su ma waxee "parkiŋ, ni ni ko Àngale yi di waxee", maa ngiy réeral ñi xamul dara ci Àngale. su ma nee "gàlle", ni ni ko tukulëer yi di waxee", maa ngiy réeral ñi xamul dara ci tukulëer. ñu ëpp ci ñiy làkk wolof, xam nañu lan mooy "parkiŋ", ak lan mooy "gàlle", ndax baat yooyu, seey nañu ci làkku wolof, kon mën nañu leen tekki ci wolof, te duñu wékku ci weneen làkk.
  • wolof, ak làkk yépp yu ñu cosaanoo, ay làkk yu màgg lañu. Séex Anta Jóob def na ci ay gëstu yu yéeme, yu am solo, yu daw yaram. daanu leen mosal ci gëstu yooyu, ci biir ëttub wolof. màggaayu wolof, tax na waruñu nangu wéer sunu jàngum wolof, ci weneen làkk wu dul wolof kepp. naam loolu lu jafe la fii ñu tollu, ndax diir bi ñu ñu moomee yépp, wolof xaw naa taxaw, ndax, "li la daan tax a jëm kanam, daan la tax a am loo dundale sa njaboot, ci weneen làkk nga daan jaar ngir am ko..." (Séex Anta Jóob). kon nag, suñu wareef la, sos baat yi amagul ci wolof, ngir delloo wolof gëddam.

ci njalbeen, war nañoo leeral ban wolof la ñuy jàngale ci ëttub wolof. wolof yi bare nañu, ndax waxin yu wuute. wolof yi nekk Senegaal, wuute nañu ci seen biir, te wuteek wolofu Mali, wala Gàmbi, wala wolofu ku juddoo Etaasini, yaroo fa, te mësul a teg tànkam ci benn dëkk bu cosaanoo wolof. loolu yëpp dëgg la waaya, dañu war a tànn benn waxin.

ku dégg wolofu Séex Anta Jóob, wala nga jàng téere yu am solo, yu Ajaa Aram Faal bind, wala nga jàng téere yu bare, yu kureel bi ñuy wax OSAD tasaare ci àdduna si, xam ni ñii, wolof piir lañuy làkk. waaya, lan mooy wolof piir ? ndax koo gis, jàpp na ni wolofam mooy wolof piir.

li am solo moo di, suñu xoolee bu baax li ñu sumb, te yaakaar way-jàng yi ànd ak ñun ba sore, gëm nañu ni, suñu jëfee wolofu bindkat yooyee, ñu bare da nañu daw bàyyiñu fa. loolu moo tax, ñu tànn wolof bi ñuy jàngale ci iniwersite bu Dakaar, mu di wolof bu boole ñépp ñiy làkk wolof, ak fu ñu mën a jóge ci réew mi, ci réew yi. waaya nag, way-jàng yi, doore ko ci man mii, ndax jàng wolof moo ma dugal ci defar ëttub wolof, nañu fagaru ndax wolofu iniwersite, wolof piir la, wolof bu jàar yoon.

jàppal ni, ci dalub web bii di ëttub wolof, amul dara lu ñu fiy jaay. ñun ñoo ko door, tabax ko, te ñun ñoo koy yeesal, waaya lu ëpp ci yeesal bi, ci seen xalaat lay jóge, yeen way-jàng yi, fekksi liggeeyu jubbanti, bi ñuy def saa su nekk. kon nag, ayca leen ci liggeey bi.

ci fii ñu tollu, ëttub wolof :

  • am na jàngukaayu bind, te ci biir :
    • am na jàngukaayu abajada, bi lay tojal arafu wolof yépp ;
    • am na jàngukaayu tekkeerlu, bi lay wan noppalukaay yi nekk ci wolof, te soo sammoonte ak ñoom, làmmiñ wi mën a méngoo ak mbind mi ;
    • am na li tax ñu war a boole wala teqale yenn baat yi ;
    • am na ay dogal yu ñu jël, ci defar ëttub wolof, di xaar ñu tabax, wala toggaat, wala yeesal nëwu wolof;
    • añs (ak ñoom seen)
  • ëttub wolof am na ba leegi, jàngukaayu dawal, bi lay tette ci jàng dawal, ci wolof;
  • am na sàqum léebu wolof, bu am lu ëpp ñaari junne ak juroom-ñeenti téemeeri léebu wolof;
  • am na sàqum baatu wolof, ñu tudde ko "oggo", bu am lu ëpp fukki junney baat, yu ñu firi ci wolof kepp.

fas yéene dolli ay jëf, yu bare, ci ëttub wolof, su ci Yàlla àndee.

Dalleen ak jàmm !

ëttub wolof